xibaarleen ma bu ag dex nekkoon ci buntu kenn ci yéen mu ciy sangu bis bu nekk juróomi yoon, ndax loolu dana bàyyi ag tilim ci deram?

xibaarleen ma bu ag dex nekkoon ci buntu kenn ci yéen mu ciy sangu bis bu nekk juróomi yoon, ndax loolu dana bàyyi ag tilim ci deram?

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «xibaarleen ma bu ag dex nekkoon ci buntu kenn ci yéen mu ciy sangu bis bu nekk juróomi yoon, ndax loolu dana bàyyi ag tilim ci deram?" Ñu ne ko: déedéet du bàyyi ci deram dara, mu ne: "loolu nag moo ngi mel ni julliy juróom, yàlla da ciy far njuumte yi».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day niròole julliy juróom ci bis bu nekk ak guddi gi, ci ni muy fare bàkkaar yu ndaw yi ak njuumte yi dafamelni ag dex gu nekk ci buntu nit ki mu ci sangu bis bu nekk juróomi yoon, ba du bàyyi ci deram bi ak ci tilimam ji dara.

فوائد الحديث

Ngëneel lii day jagoo rekk ci far bàkkaar yu ndaw yi, bu dee yu mag yi nag fàww ñu tuub ko.

Ngëneelu joxe julliy juróom ak sàmmoonte ak moom ci ay sàrtam ak i ponkam, ak i wareefam ak i sunnaam.

التصنيفات

Ngëneelu julli