ku julli suba moo ngi ci kaaraangeg Yàlla

ku julli suba moo ngi ci kaaraangeg Yàlla

Jële nañu ci Jundub Ibn Abdullah Al-Xasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku julli suba moo ngi ci kaaraangeg Yàlla, moom Yàlla du leen toppe dara ci ay àqam, ndax ki Yàlla toppe dara ciy àq dana ko jàpp, te dana këpp kanamam ca sawaraw Jahannama».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku julli fajar moo ngi ci kaaraangeg Yàlla ak ug càmmam, dana ko wattu dana ko dimbali. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak jàmm- daal di n'a tere fecci kóllëre gii ak di ko yàq ci bàyyi julli fajar, walla di sikkal ñi koy julli, mbaa di leen tooñ, ndax ku ko def da ngay yàq dëkkandoo gii, te yelloo na tëkku gu metti, ba Yàlla dina ko toppe li mu sàggane ci àqam, te képp ku Yàlla wut, dina ko jàpp, sànni ko ca sawara.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi :

Leeral njariñu jullig fajar ak ngënéelam.

Artu gu tar ci kaw ñiy jëmale ñaawtéef ci ñiy julli fajar.

Yàlla mu kawe mi day fayyu ci ñiy jëmale ñaawtéef ci jaamam yu sell yi.

التصنيفات

Ngëneelu julli