ku ne ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm,

ku ne ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm,

Jële nañu ci Abdulaah Ibn Umar -yalna leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku ne ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm, ki jiite nit ñi ab sàmm la te danañu ko ko laaj,góor gi ab sàmm la ci waa këram te danañu ko ko laaj, jigéen ji ab sàmm la ci kër jëkkëram ak i doomam te danañu ko ko laaj, jaam bi ab sàmm la ci alali sangam te danañu ka ko laaj, yégleen ne ku nekk ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne jullit bu nekk am na lu ko war ci askan wi mu warkoo sàmm te téye ko, Imaam bi ak njiit li ab sàmm la ca la ko Yàlla sàmmloo, kon war na ci moom mu sàmm seen tëraliin, ak aar leen ci ku leen di tooñ, ak jihaad ak seen ub noon, te bañ a sànk seen i àq, Góor gi ci waa këram dañu koo gàll mu taxawe seen ub dund, te rafetal ab jëflanteem ak ñoom, te jàngal leen yar leen, Jigéen gi ci biir kër jëkkëram ab sàmm lafa ci rafetuw doxaliin ci kër gi, ak yar doomam yi, te dees na ko laaj loolu. Surga biy ab jaam, ak ki ñuy liggéeyloo di ko fay moo war a toppatoo xaalisu njaatigeem, ci di sàmm li ci loxoom, ak di ko liggéeyal, te dees na ko laaj loolu. Kenn ku nekk ab sàmm la ca la ñu ko sàmmloo, te kenn ku nekk dees na ko laaj la mu doon sàmm.

فوائد الحديث

Wareef yi askanu jullit wépp la ñeel, te ku nekk mi ngi aju ci kàttanam ak wareef wa mu ça am.

Màggaayu wareefu jigéen, ci taxawe àqi kër jëkkëram ak li ko war ci ay doomam.

التصنيفات

Warteefi njiit, Dundiinu ñaari way-dencante yi, Yar doom yi