nangeen kóllarante ak Alxuraan jii, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom moo gën a gaaw a rëcc giléem gi ci buumam

nangeen kóllarante ak Alxuraan jii, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom moo gën a gaaw a rëcc giléem gi ci buumam

Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «nangeen kóllarante ak Alxuraan jii, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom moo gën a gaaw a rëcc giléem gi ci buumam».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digle na ñu kóllarante ak Alxuraan sax ci di ko jàng ngir duñu ko fàtte ginnaaw bañu ko mokkalee ci suñu dënn, Yónente feddali loolu ci giñ ne Alxuraan moo gën a tarug rëcc ak juge ci dënn ci giléem gi ñu yeew ci buum ci digg tànk ba, bu nit ki kóllarantee ak moom mu jàpp ko, bu ko bàyyee mu dem daal di koy réer.

فوائد الحديث

Ki mokkal Alxuraan bu saxee ci di ko jàng saa su ne day des di lu mu mokkal ci xolam, bu ko deful mu juge si moom, mu fàtte ko.

Bokk na ci njariñi kóllarante ak Alxuraan: pay ak yool, ak yëkkatiku ay daraja ëllëg bis-pénc.

التصنيفات

Ngëneelu yittewoo Alquraan