إعدادات العرض
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc rëbb na góor giy sol colug jigéen, ak jigéen giy sol colug góor
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc rëbb na góor giy sol colug jigéen, ak jigéen giy sol colug góor
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc rëbb na góor giy sol colug jigéen, ak jigéen giy sol colug góor.
[Wér na]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt සිංහල ئۇيغۇرچە Hausa Kurdî Português Kiswahili অসমীয়া ગુજરાતી Nederlands മലയാളം Română Magyar ქართული Русский Moore ไทย Македонски తెలుగు मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛ Malagasy Українська ភាសាខ្មែរ ಕನ್ನಡ Svenska پښتوالشرح
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñaan na ag dàq ak soril yërmàndey Yàlla ñeel góor giy niru-nirulu jigéen ci sol yi jigéen ñi jagoo; moo xam ca jëmm ja la walla ca melo wa walla ca anam ga walla ca anamug coliin ga ak taar ba walla yu dul yooyu. Walla jigéen gi di ko niru-nirulu ci col gi góor ñi jagoo, moom nag ci bàkkaar yu mag yi la bokk.فوائد الحديث
As-Sawkaanii nee na: araamalees na jigéen ñi di niru-nirulu góor ñi, ak góor ñi di niru-nirulu jigéen ñi; ndaxte rëbb du am ci lu dul def lu ñu araamal.
Ibn Husaymiin nee na: loo xam ne ñoom ñaar ñoo ci bokk yam niki njitlaay yi góor ak jigéen di sol loolu dara nekku ci, maanaam, aayul góor ak jigéen sol ko; ndaxte ñoo ci bokk yam.
