Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tabaskee na ñaari kuuy yu duuf am ay béjjan, mu rendi leen ci loxoom, tudd Yàlla daal di kàbbar, teg tànkam bi ca seen doq ya

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tabaskee na ñaari kuuy yu duuf am ay béjjan, mu rendi leen ci loxoom, tudd Yàlla daal di kàbbar, teg tànkam bi ca seen doq ya

Jële nañu ci Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tabaskee na ñaari kuuy yu duuf am ay béjjan, mu rendi leen ci loxoom, tudd Yàlla daal di kàbbar, teg tànkam bi ca seen doq ya.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm day nettali ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa rendi ci loxoom ci bisu feetu Tabaski ñaari xar yu góor yu mag am ay béjjan nekk yu weex te rax ñuul, mu wax: bismil Laahi wallaahu Akbar, mu teg tànkam ca doq ga.

فوائد الحديث

Yoonalees na Tabaski, te jullit ñi dëppoo nañu ci.

Li gën mooy li ñuy tabaskee mel ni xeet wii Yonnente bi tabaskee; ngir ni jëmm ji rafete ak ni gareesam ak ndawalam gën a teeye.

An-Nawawii wax na: ca loola ne sopp nañu nit ki féetewoo rendi tabaskeem ci boppam, te bañ a féetale rendi ga kenn ci lu dul ngànt, te bu booba a sopp nañu mu teewe rendi ga, bu ca wuutalee ab jullit kon dagan na ci lu dul ag wuute.

Ibn Hajar nee na: sopp nañu kàbbar ak tudd Yàlla bu ñuy rendi, sopp nañu it nu teg tànk bi ci doq gi ci wetug ndayjoor gi, dëppoo nañu it ne wetu càmmooñ lañu koy tërale, mu teg tànkam ci wetug ndayjoor gi ngir mu gën a yomb ci kiy rendi mu téye paaka bi ci ndayjooram jàpp ci bopp bi ci loxob càmmooñam.

Sopp nañu tabaskee lu am béjjan bu dul moom it dana dagan.

التصنيفات

Rendi, Gàttub Tabaski