bokk na ci jihaad yi gën a màgg wax kàddug maanute fi kanamu buur bu jeng

bokk na ci jihaad yi gën a màgg wax kàddug maanute fi kanamu buur bu jeng

Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "bokk na ci jihaad yi gën a màgg wax kàddug maanute fi kanamu buur bu jeng ».

[Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne bokk na ci xeeti jihaad ci yoonu Yàlla yi gën a màgg te ëpp njariñ mooy wax baati maandute ag dëgg fi kanamu buur ak njiit lu jeng di ab tooñkat; ndaxte moom dafa jëfe jaamug digle lu baax ak tere lu bon, moo xam ci wax la walla ci bind walla ci jëf mbaa leneen lu yéwénal di ame te yàqute di ca dàqoo.

فوائد الحديث

Digle lu baax ak tere lu bon dafa bokk ci jihaad.

Laabire njiit dafa bokk ci jihaad yi gën a màgg, waaye dafa wara tege ci xam-xam ak xereñte ak wóorlu.

Al-Xattaabii nee na: loolu dafa gën ci jihaad yi; ndaxte kiy jihaad ak noon bi day dengi-dengi ci diggante yaakaar ak ragal te du xam ndax day gañe walla dañu koy gañe, te ku nekk ak boroom nguur moom danu koo not, moom bu waxee dëgg daal di digle lu baax gaaral na boppam ag naaxsaay, jëme boppam ag alkande, loolu moo tax mu gën ci xeeti jihaad yi ngir li ag ragal not fi moom, nee nañu it: dafa gën ci jihaad yi; ndaxte bu njiit li jëlee waxam ji man naa am njariñam daj nit ñu bari, bu ko defee yéwénal am.

التصنيفات

Ngëneelu digle yiw tere njékar