ay njiit danañu ñëw, da ngeen gis ci ñoom lu baax, ak it lu bon, ku ànd ca lu baax la kooku set na wicc, ku weddi seen yu bon kooku mucc na, waaye ki muccul mooy ki gërëm yu bon ya te ànd ca

ay njiit danañu ñëw, da ngeen gis ci ñoom lu baax, ak it lu bon, ku ànd ca lu baax la kooku set na wicc, ku weddi seen yu bon kooku mucc na, waaye ki muccul mooy ki gërëm yu bon ya te ànd ca

Jële nañu ci Ummu Salamata ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ay njiit danañu ñëw, da ngeen gis ci ñoom lu baax, ak it lu bon, ku ànd ca lu baax la kooku set na wicc, ku weddi seen yu bon kooku mucc na, waaye ki muccul mooy ki gërëm yu bon ya te ànd ca" ñu ne ko: mo ndax duñu xeex ak ñoom? Mu ne: "déedéet, li fii ak ñoo ngi julli".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ay njiit danañu nu jiite, te dananu xam seen yenn jëf yi; ngir li mu dëppoo ak li ñu xam ci sariiha, dananu weddi it yeneen ya; ngir li mu wuute ak sariiha, Ku sib lu bon la ci xolam te manu koo dindi; kooku set na ci bàkkaar ak ug naaféq, Waaye ku man a weddi ci loxoom mbaa ci làmmiñam, daal di leen di weddi ca loola kooku mucc na ci miy ga, mbaa di ca bokk, Waaye ku gërëm seen jëf ya, topp leen ca kooku alku kem ni ñu alkoo. Ñu laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: ndax duñu xeex ak njiit yi mel nii? Mu tere leen ko, ne leen: déedéet, fii ak noo ngi julli fi yéen.

فوائد الحديث

Bokk na ci tegtali yonnenteg Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yu fàddu yi muy xibaare mu am kem na mu ko waxe woon.

Di gërëm lu bon walla di ca bokk daganul, waaye dañu koo war a weddi.

Bu njiit yi sosee lu wuute ak sariiha du dagan ñu leen cay topp.

Song njiiti jullit ñi du dagan; ndax la cay topp ci yàqute ak tuur deret ak ñàkk kóolute, kon muñ ñaawteefi njiit yiy moy, ak muñ seeni lor moo gën a woyof loolu.

Mbiri julli de lu màgg la, ndax moo teqale diggante kéefar ak Lislaam.

التصنيفات

Génn ci topp njiit