bu kenn ci yéen dajee ak mbokkam na ko nuyu, bu dara doxee seen diggante ag garab walla miir walla aw doj mu dajewaat ak moom na ko nuyu batay

bu kenn ci yéen dajee ak mbokkam na ko nuyu, bu dara doxee seen diggante ag garab walla miir walla aw doj mu dajewaat ak moom na ko nuyu batay

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «bu kenn ci yéen dajee ak mbokkam na ko nuyu, bu dara doxee seen diggante ag garab walla miir walla aw doj mu dajewaat ak moom na ko nuyu batay».

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day soññee ci nuyu mbokku jullitam saa yu dajee ak moom, ba bu ñu àndee di dox am lu leen teqale niki ag garab walla miir walla aw doj wu rëy, topp mu dajewaat ak moom ginnaaw ga na ko nuyu beneen yoon.

فوائد الحديث

Sopp nañu tasaare nuyóo, ak mu bàmtu ko saa bu anam gi soppeekoo.

Tarug xérug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci tasaare sunnas nuyóo ak jotale ci; ngir li ci nekk ci xëcc mbëggeel ak miinante ci diggante jullit ñi.

Nuyóo mooy nga wax: (Assalaamu halaykum) walla (Assalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhu), ci ludul saafonte gi nga xam ne mooy am ci ag daje gu njëkk.

Nuyóo ñaan la, te jullit ñi dañoo aajowoo ñenn ñi di ñaanal ñeneen ñi donte loolu day bàmtu.

التصنيفات

Teggiini nuyoo ak yëglu