nàmpal day araamal li njureel di araamal

nàmpal day araamal li njureel di araamal

Jële nañu ci Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "nàmpal day araamal li njureel di araamal".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne dees na araamal ci nàmpal li ñu araamal ci njureel ak askan di nijaay walla baay tëx walla mbokk..., nàmpal it dana daganal li njureel di daganal ci ay àtte.

فوائد الحديث

Hadiis bi tënk la ci àttey nàmpal.

Ibn Hajar nee na: li mu wax ne: (nàmpal day araamal li njureel di araamal) maanaam: day daganal it li muy daganal ci dëppoog woroom xam-xam yi ci lu aju ci araamal sëy ak la cay topp, ak lawug araam ga ci diggante ka ñu nàmpal ak ay doomi aji-nàmpal ji, ak wàcceleen ci wàccuwaayu jegeñaale ci daganug xool ga ak wéet ga ak ànd tukki ga, waaye yeneen àttey jur ga du ca topp niki donn ak warug dund ak goreel ag moomeel ak seede ak xel, ak rotal fayoontoo ga.

Saxal àtteb araamal ci nàmpal araam gu sax dàkk.

Yeneeni hadiis tegtale nañu ne araamal ci nàmpal day saxe ci juróomi nàmpal yu ñu xam, ak ñu nekk ci ñaari at yu njëkk yi.

Li ñu araamal ci askan mooy: yaay yi, maam yu jigéen yu dañu ciy dugg, donte dañoo kawe ci wàllug yaay walla ci baay. Ak doom yu jigéen yi: sët yi juge ci doom yu jigéen yi ak ci doom yu góor yi dañu ciy dugg donte dañoo suufe. Ak jigée ñi nga bokkal nday ak baay walla baay kese mbaa nday kesse. Ak bàjjan yi bokk ak sa baay nday ak mbaa ñu bokk baay walla nday niki noonu it mbooleem mbokk yu jigéen yu maam ju góor da ciy dugg donte dañoo kawe. Ak yaay yu ndaw yi: mbooleem mbokk yu jigéen yu yaay da ciy dugg, moo xam ñoo bokk nday ak baay walla déet, niki noonu it mbooleem mbokk yu jigéen yu maam ju jigéen donte dañoo kawe, moo xam maam yu jigéen yi ci wàllug baay la walla ci wàllug yaay. Ak doom yu jigéen yu mbokk mu góor, ak doom yu jigéen yu mbokk mu jigéen, seen i doom da ciy dugg donte dañoo suufe.

Li ñu araamal ci nàmpal, dees na araamal ci nàmpal li ñu araamal ci askan, jépp jigéen ju ñu araamal ci askan dañuy araamal ku mel ni moom ci nàmpal ba mu des yaayu mbokkam mu góor, ak mbokku doomam ju góor ci nàmpaale ñooñu duñu araam.

التصنيفات

Nàmpal