إعدادات العرض
bu ngeen ko gisee woorleen, bu ngeen ko gisee worileen, bu muuroo ci yeen nangeen ko nattale
bu ngeen ko gisee woorleen, bu ngeen ko gisee worileen, bu muuroo ci yeen nangeen ko nattale
Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «bu ngeen ko gisee woorleen, bu ngeen ko gisee worileen, bu muuroo ci yeen nangeen ko nattale».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Hausa Português Kurdî සිංහල Nederlands অসমীয়া Tiếng Việt Kiswahili ગુજરાતી پښتو Română മലയാളം नेपाली Deutsch Кыргызча తెలుగు ქართული Moore Magyar Svenska Македонски ಕನ್ನಡ Українська Kinyarwanda Oromoo ไทย Lietuvių Српски मराठी ਪੰਜਾਬੀالشرح
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne màndargam duggug weeru koor ak génnam, mu wax ne: bu ngeen gisee weeru koor wi woorleen, bu aw niir doxee seen diggante ak moom mu muuru ci yéen; nangeen lim fanweeri fan ñeel weeru Baraxlu wi, bu ngeen gisee weeru Kori gi worileen, bu aw niir doxee seen diggante ak moom mu muuru ci yéen; nangeen lim fanweeri fan ñeel weeru Koor gi.فوائد الحديث
Ci gisug bët lañuy sukkandiku ci saxal duggug weer waaye kenn duko sukkandiku ci ay nattale (calcul) .
Ibnul Munsir tuxal na ag dëppoo ci ne woor du war bu dee duggug weeru Koor gi ci nattale dong la wolif gis ga.
Warees naa matal Baraxlu fanweeri fan bu dee niir mbaa lu ko niru moo tee ñu gis weeru Koor gi.
Weeru jullit yi du nekk lu dul ñaar-fukk ak juróom-ñenti fan, walla fanweeri fan.
Warees naa matal weeru Koor wi fanweeri fan bu dee niir mbaa lu ko niru moo tee ñu gis weeru Baraxlu wi.
Ku nekk ci barab bu amul kuy nemmeeku mbiri jullit ñi ci woor, walla mu bokk ci ñiy sàggane loolu, kon jaadu na ci moom mu sàmmoonte ak loolu ci gëstu ci ku gis ga sax fa moom ci boppam walla ci gisug ku mu wóolu; mu woor ak mu dog it ci loolu.
التصنيفات
Gisug weer