àdduna ay bagaas la, te li gën ci bagaasi àdduna mooy jigéen ju baax

àdduna ay bagaas la, te li gën ci bagaasi àdduna mooy jigéen ju baax

Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «àdduna ay bagaas la, te li gën ci bagaasi àdduna mooy jigéen ju baax».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne àdduna ak li ci biiram mbir mu ñuy bànneexoo ab diir la rekk mu deñ, waaye li gën ci banneexi àdduna mooy jabar ju baax, ji nga xam ne bu ko xoolee bég, bu ko digalee mu topp ko, bu fa nekkul mu wattu ko ci boppam ak alalam.

فوائد الحديث

Dagan na ñu bànneexu ci yu teeyi àdduna yi Yàlla daganalal jaamam ñi ci lu dul yàq mbaa ŋott.

Xemmemloo ci tànn jabar ju baax; ndaxte day dimbali jëkkëram ci topp Boroomam.

Li gën ci bànneexi àdduna mooy lu tege ci topp Yàlla mbaa mu cay dimbaalee.

التصنيفات

Àttey jigéen ñi