Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara

Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara

Jële nañu ci Ummu Atiyyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-,mu bokkoon ci ñi jaayante woon ak Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-,mu wax ne: Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara.

[Wér na] [Abóo Daawuda a ko soloo ci kàddu gii, Al-buxaariy soloo ko waliif ndollent (ginnaaw laab ga)]

الشرح

Sahaaba bu jigéen bii di Ummu Atiyyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne jigéen ñi ci jamonoy Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawuñu jàppe mbaax ndox miy génne ci awra -xaw a ñuul, walla mboq-ginnaaw bimu laabe , ba tax duñu bàyyi julli ak woor ngir moom.

فوائد الحديث

Ndox miy génne ci awray jigéen -ginnaaw bi mu laabee ci mbërëg

deesu ko jàppe mbaax donte dafa am nëxiit ak mboq-mboq yu bawoo ci dereet ji.

Génnug nëx-nëx yi ak mboq-mboq yi ci jamonoy mbaax ak aada ja dees na ko jàppe; ndaxte dereet la ju génn ci waxtoom,waaye dafa jaxasoo ak ndox.

Jigéen du bàyyi julli ak woor ngir nëx-nëx yi ak mboq-mboq yiy am ginnaaw laab gi,waaye day jàppu daal di julli.

التصنيفات

Mbërëg ak wësin ak dereeti wéradi