Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ubbi julli gi day yëkkati loxoom ba mu tolloo ak mbagg yi,

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ubbi julli gi day yëkkati loxoom ba mu tolloo ak mbagg yi,

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ubbi julli gi day yëkkati loxoom ba mu tolloo ak mbagg yi, naka noonu it daan na leen yëkkati bu daan kàbbar ngir rukóo, ak bu daan siggi ca rukóo ba, ak bu daan yëkkati boppam jóge ca rukóo ba, daal di wax: "samihal Laahu liman hamidahu", daawul def loolu nag ca sujjóot ba.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan yëkkati ay loxoom ci ñatti barab ci julli gi ba mu tolloo walla mu jàkkaarloo ak ay mbaggam: te mooy fi yaxi mbagg mi dajee ak përëg bi. Barab bu njëkk bi: buy ubbi julli gi di def kàbbaru armal. Ñaareel bi: buy kàbbaar ngir rukóo. Ñatteel bi: buy yëkkati boppam jóge ca rukóo ba, daal di wax: samihal Laahu liman hamidahu Rabbanaa wa lakal hamdu. Daawul yëkkati loxoom bu daan tàmbalee sujjóot, mbaa muy siggi ca sujjóot ba.

فوائد الحديث

Bokk ci xereñi yëkkati ñaari loxo ci julli gi, moom ag taar la ñeel julli gi, te it ag màggal la ñeel Yàlla mu sell mi.

Yëkkati loxo sax na ci ñenteelu bérab kem ni mu ñëwe ci nettalig Abii Humayd As-Saahidii ca Abuu Daawuda ak ñeneen, te mooy buy jug bawoo ci taaya gu njëkk gi ci jullig ñatt ak ñenti ràkka.

Sax na jóge ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba tay ne daan na yëkkati ay loxoom ba muy lerook ay noppam ci lu dul mu koy laal, kem ni mu ñëwe ci nettalig Maalik ibnul Huwayris bi nekk ci Al-Buxaarii ak Muslim: "Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan kàbbar day yëkkati ay loxoom ba mu tolloo ak ay noppam".

Boole Samihal Laahu liman hamidahu ak Rabbanaa wa lakal hamdu imaam bi moo ko jagoo ak kiy julli moom dong, bu dee maamuun la nag moom day wax: Rabbanaa wa lakal hamdu rekk.

Wax: "Rabbanaa wa lakal hamdu" ginnaaw rukóo ñenti melo sax na ci jóge ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, melo wii wenn la ci rekk, kon li gën mooy nit ki di topp melo yii, leeg-leeg mu def bii leeg-leeg mu def bee.

التصنيفات

Ni ñuy jullee