fi Boroom bi di gën a jegee jaam bi mooy ci mujjantalu guddi gi

fi Boroom bi di gën a jegee jaam bi mooy ci mujjantalu guddi gi

Jële nañu ci Abii Umaamata mu wax ne: Amru Ibn Abasata yal na ko Yàlla dollee gërëm wax na ma ne dégg na Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «fi Boroom bi di gën a jegee jaam bi mooy ci mujjantalu guddi gi, boo manee di bokk ci ñiy tudd Yàlla ci waxtu woowo def ko».

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne: Boroom bu sell bi day gën a jege jaam bi ci ñatteelu xaaj bi mujj ci guddi gi; bu ñu la tawfeexalee may la kàttan -yaw jullit bi- ba nga man a bokk ci mbooloo miy jaamu Yàlla ñiy julli di tudd Yàlla di tuub ci waxtu wii loolu lees wara góor-góor lu la.

فوائد الحديث

Soññ jullit bi ci tudd Yàlla ci mujjantëlu guddi gi.

Gënanteg waxtu yi ci seen diggante ñeel tudd Yàlla ak ñaan ak julli.

Mabruug wax na

ci wuute gi am

ci diggante limu wax ne: "fi Boroom bi di gën a jegee jaam bi" ak li mu wax ne: "fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee": li ñu jublu fii mooy leeral waxtu wi Boroom bi di jege jaam bi ci digg guddi gi, li ñu namm ci booba nag mooy leeral anam gi jaam bi di jegee Boroom bi fekk moo ngi sujjóot.

التصنيفات

Yiy waral nangu ñaan ak yi koy xañe