Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan tissooli day teg loxoom -walla yéereem- ci gémmeñam, daal di suufeel -walla mu téye- ci kàdoom

Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan tissooli day teg loxoom -walla yéereem- ci gémmeñam, daal di suufeel -walla mu téye- ci kàdoom

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan tissooli day teg loxoom -walla yéereem- ci gémmeñam, daal di suufeel -walla mu téye- ci kàdoom.

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan tissooli: Li ci njëkk: day teg loxoom, walla yeéreem ci gémmeñam; ngir dara bañ a génn ci gémmeñam walla bakkanam luy lor ñi mu toogal. Ñaareel bi: day suufeel kàddoom te du ko yëkkati.

فوائد الحديث

Leeral njubug Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci tissooli ak roy ci loolu.

Sopp nañu ñi teg yére bi walla ab musuwaar mbaa leneen ci gémmeñ gi ak bakkan bi buñu dee tissooli ngir dara bañ cee génn luy lor ñi ñu toogal.

Sàkku nañu ñu wàcce kàddu gi bu ñuy tissooli, te dafa bokk ci teggin yu mat yi ak jikkó yu tedd yi.

التصنيفات

Teggiini tisli ak óbbali, Jikkoy Muhammat SLM