إعدادات العرض
ku waajalal aji-xare ci yoonu Yàlla kooku xare na, ku wuutu aji-xare ci yoonu Yàlla ci yiw kooku xare na
ku waajalal aji-xare ci yoonu Yàlla kooku xare na, ku wuutu aji-xare ci yoonu Yàlla ci yiw kooku xare na
Jële nañu ci Sayd ibn Xaalid yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "ku waajalal aji-xare ci yoonu Yàlla kooku xare na, ku wuutu aji-xare ci yoonu Yàlla ci yiw kooku xare na".
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Hausa Kurdî Kiswahili Português සිංහල অসমীয়া Tiếng Việt ગુજરાતી Nederlands پښتو नेपाली ไทย മലയാളം Svenska Кыргызча Română ಕನ್ನಡ Српски తెలుగు ქართული Moore Magyar Kinyarwanda Македонски Čeština Українська Lietuviųالشرح
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku waajalal aji-xare ci yoonu Yàlla jumtukaayi tukkeem ak yi mu aajowoo ci ay ngànnaay yu manut a ñàkk, ak waruwaay, ak ñam, ak ub dund ak yeneen; kooku àtteb aji-xare ji la am, te dina am yoolub way-xare yi. Ku wuutu aji-xare ci ay mbiram ci yiw, wuutu ko ci di sàmm njabootam ci jamono yi mu fàddoo kooku àtteb aji-xare ji la am.فوائد الحديث
Ñaax jullit ñi ci dimbalante ci yiw.
Ibn Hajar nee na: Hadiis bi day ñaaxe ci rafetal jëme ci kiy def luy jariñ jullit ñi, walla mu nekk ci ci mbir moo xam ne seen yitte la.
Tënk bu matale bi mooy: ku dimbali nit ci genn jaamu Yàlla dana am lu toll ni yoolam, te du wàññi cib yoolam dara.
التصنيفات
Ngëneelu xeex ci yoonu Yàlla