fépp fu yax di daje ci nit sarax la

fépp fu yax di daje ci nit sarax la

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «fépp fu yax di daje ci nit sarax la, bépp bis bu jant bi fenk mu Maandu ci diggante ñaari nit loolu sarax la, mu dimbali nit ci daabaam yéegal ko ca, walla mu yéegalal ko ay jumtukay loolu sarax la, wax ju teey sarax la, ak bépp jéego bu mu jéego jëm ca julli ga sarax la, ak mu toppale lor wu nekk ci kaw yoon wi loolu sarax la».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne saraxu coobarewu ngir Yàlla mu kawe mi war na ci bépp mukallaf ci bis bu ne ci limub fi ay yaxam dajee ci anamug sant ko ci jàmm ji, ak li mu def ay yaxam mu man koo bank man koo tàllal, Te sarax boobu day ame ci jëf yu baax yépp waaye yemul ci joxe alal, te bokk na ca: Sag màndu ak sag yéwénal ci diggante ñaari way-xuloo yi sarax la, Ak nga dimbali ki néew doole ci daabaam nga yéegal ko ca, walla nga yëkkatil ko ay jumtukaayam sarax la, Ak wax ju teey ci tudd Yàlla ak ñaan ak nuyóo ak yeneen sarax la, Ak bépp jéego boo dox jëm ca julli ga sarax la, Ak dindi luy lore ci yoon wi sarax la.

فوائد الحديث

Ni ñu toggale yaxi doomu Aadama ak ni mu mucce ayib bokk na ci xéewali Yàlla yi gën a màgg ci moom, ba tax bépp yax aajowoo saraxe ñeel ko ngir cantug xéewal gi mat.

Xemmemloo ci yeesal cant gi ci bis bu ne ngir li xéewal googu sax.

Xemmemloo ci sax ci naafila yi ak saraxe yi bis bu nekk.

Ngëneelu yéwénal ci diggante nit ñi.

Ñaaxe ci nit ki di dimbali mbokkam; ndax dimbali gi mu koy dimbali sarax la.

Soñee ci teewe mbooloo ya ak dox jëm ca, ak dundal jàkka ya ci loolu.

Warug wormaal yooni jullit ñi ci moytu lu leen di lor mbaa mu leen di gaañ.

التصنيفات

Ngëneelu Lislaam ak taaram