Allaahuma innii ahuusu bika min xalati addayni, wa xalabati alhaduwwi, wa samaati al-ahdaa

Allaahuma innii ahuusu bika min xalati addayni, wa xalabati alhaduwwi, wa samaati al-ahdaa

Jële nañu ci Abdullah ibn Amr ibnul Haas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na ñaan ci baat yii; "Allaahuma innii ahuusu bika min xalati addayni, wa xalabati alhaduwwi, wa samaati al-ahdaa".

[Wér na] [An-nasaa'iy soloo na ko, ak Ahmat]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muslu na ci ay bir: Bi ci njëkk: (yaw sama Boroom maa ngi muslu) di ñëw di làqu (ci yaw) làquwunu ci keneen ku dul yaw, (ci bor bu bari) ag notam ak ug njàqareem ak tiisam, ma lay ñaan nga dimbali ma ci fay ko. Ñaareel bi: (ak notug noon bi) ak notam ak ug songam, ma lay ñaan nga tëye loram wi, ak dimbali ma ci kawam. Ñatteel bi: ,(ak ndokkug noon yi) seenug bég ci liy dal jullit ñi ci balaa ak musiba.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci di muslu ci Yàlla ci lépp luy soxlaale wolif jaamu gi tey xëcc ay njàqare niki bor ak yeneen.

Bor kese dara nekkesi, waaye li aay mooy ki amul kóllareg fay, lii mooy bor giy note.

Nit ki war naa moytandiku bir yi ñuy ndokke di ci ayibale.

Leeral nooneelug yéefar ñeel way-gëm ñi ak seenug ndokk ci ñoom ci musiba yi.

Feeñalug noon yi seen mbégte ci balaa yiy dal nit ki day gën a tar ci nit ki jëmmi balaa bi.

التصنيفات

Ñaan yi bawoo ci Yónnent bi SLM