إعدادات العرض
ki gën ci yéen mooy ki jàng Alxuraan te di ko jàngale
ki gën ci yéen mooy ki jàng Alxuraan te di ko jàngale
Jële nañu ci Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ki gën ci yéen mooy ki jàng Alxuraan te di ko jàngale».
[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili မြန်မာ ไทย Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands සිංහල தமிழ் دری Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy Română Kinyarwanda नेपाली Српски Soomaali Moore Українська Български Azərbaycanالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ki gën ci jullit ñi te gën leen a kawe ay daraja fa Yàlla mooy: ki xamlu Alxuraan, cig jàng ak mokkal ak dégg ak firi, te xamal ñeneen ñi la mu am ci xam-xami Alxuraan ànd ak di ko jëfe.فوائد الحديث
Leeral tedd-ngay Alxuraan, ak ne moo gën ci wax yi; ndaxte waxi Yàlla la.
Ki gën ci way-jàng yi mooy kiy jàngal ñeneen ñi waaye du ki koy yamale ci boppam rekk.
Jàng Alxuraan ak di ko jàngale dafay làmboo jàng ga ak xam maanaa ya ak àtte ya.
التصنيفات
Ngëneelu yittewoo Alquraan