Allaahumma Antas Salaamu, wa Minkas Salaamu, Tabaarakta Sal Jalaali wal ikraami

Allaahumma Antas Salaamu, wa Minkas Salaamu, Tabaarakta Sal Jalaali wal ikraami

Jële nañu ci Sawbaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan wëlbatiku ci julli gi day jéggalu ñatti yoon, daal di wax: "Allaahumma Antas Salaamu, wa Minkas Salaamu, Tabaarakta Sal Jalaali wal ikraami" waliid wax ne: ma wax Al-Awsaahii ne ko: naka lay jéggaloo? Mu ne: day wax naan: Astaxfirul Laaha, Astaxfirul Laaha.

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan noppi ci julli gi da daan wax: Astaxfirul Laaha, Astaxfirul Laaha, Astaxfirul Laaha. Mu màggal Boroomam nag ci wax: «Allaahumma Antas Salaamu wa Minkas Salaamu Tabaarakta Sal Jalaali wal ikraami» Yàlla mooy Aji-Mucc ji di Aji-Mat ci ay meloom, di Aji-Set ci bépp ayib ak mànkite, nga sàkku ci moom Aji-Sell ji mucc ci ayi àdduna ak allaaxira doo ko sàkku ci keneen, ndax moom Aji-Sell ji ci moom la yiwi ñaari kër yépp nekk, mooy Boroom màgg gi di Boroom rafetal gi.

فوائد الحديث

Sopp na ñu jéggalu ginnaaw julli gi te di ko saxal.

Sopp nañu jéggalu ngir mottali li mànki ci jaamu gi ak defar jaamu gi ak gàttañlu gi ci am.

التصنيفات

Sikkar yi ànd ak julli gi