yamaleleen seen sàppe yi, ndax yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi

yamaleleen seen sàppe yi, ndax yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "yamaleleen seen sàppe yi, ndax yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi"

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day digal jullikat yi ñu yamale seen sàppe yi, te kenn bañ a jiitu kenn mbaa mu koy mujj, ak ne yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi, waaye dëngug sàppe ayib la ci julli gi ag wàññiku la ca.

فوائد الحديث

Yoonalees na yittewoo ci lépp luy matal julli gi te di ko soreele ag ug wàññiku.

Keemaanu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jàngale, ba tax mu lënkale àtte bi ak li ko waral; ngir leeral keemaanu Sariiha, ak sawarloo bakkan yi ci jëfe.

التصنيفات

Àttey ki jiite julli ak ña mu jiite, Àttey jàkka yi