Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ëppoon kersa jigéen gi sëyagul, bu gisee mbir mu mu bañ ci kanamam gi lañu koy xame

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ëppoon kersa jigéen gi sëyagul, bu gisee mbir mu mu bañ ci kanamam gi lañu koy xame

Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ëppoon kersa jigéen gi sëyagul, bu gisee mbir mu mu bañ ci kanamam gi lañu koy xame.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Abuu Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo ëppoon kersa jigéen ju ndaw ju sëyagul jaxasoogul ak góor ñi tey làqu ci këram, bokk na ci kersaam gu tar bu daan bañ dara kanam gi day soppiku te du wax, waaye Sahaaba yi dañuy xame bañeel gi ci kanam gi

فوائد الحديث

Leeral li Yonnente bi làmboo ci kersa, te mooy jikkó ju màgg ja.

Kersag Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mooy fii ak xottiwuñu wormay Yàlla, bu ñu xottee wormay Yàlla nag; Yonnente day mer daal di digal sahaaba yi tere leen.

Ñaaxe ci jikkówoo kersa; ndaxte moom day jëme bakkan bi ci def lu rafet ak bàyyi lu ñaaw.

التصنيفات

Kersaam SLM