ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram

ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamale ngëneelu taxaw Laylatul Xadri gi nga xam ne day nekk ci fukki fan yi mujj ci weeru koor, ak ne ku ca farlu ci julli ak ñaan ak jàng Alxuraan ak tudd Yàlla, ngir gëm ko ak la ca ñëw ciy ngëneel, mu yaakaar ca jëfam ja yoolub Yàlla, ci lu dul ngistal walla ndéggtal, kon dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram.

فوائد الحديث

Ngëneelu Laylatul Xadri ak ñaaxe ci taxaw ko.

Jëf yu baax yi deesu ko nangu lu dul mu ànd ak yéene ju dëggu.

Ngëneelu Yàlla ak yërmaandeem, ndax ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram.

التصنيفات

Taxaw guddi, Fukki guddi yi mujj ci weeru Koor