bu kenn ci yéen yëgée ci biiram dara, te xamul ndax dara génn na ci moom walla déet, bumu génn jàkka ci ba keroog muy dégg kàddu, mbaa mu yég ngelaw

bu kenn ci yéen yëgée ci biiram dara, te xamul ndax dara génn na ci moom walla déet, bumu génn jàkka ci ba keroog muy dégg kàddu, mbaa mu yég ngelaw

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bu kenn ci yéen yëgée ci biiram dara, te xamul ndax dara génn na ci moom walla déet, bumu génn jàkka ci ba keroog muy dégg kàddu, mbaa mu yég ngelaw».

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne bu amee luy yëngu ci biiru kiy julli, mu lënt ko ndax dara génn na ci moom walla déet? Bumu dem di dagg julli gi ngir baamtu Njàpp mi, ba keroog mu koy wóor ne njàpp mi yàqu na; ci mu dégg kàddug ngelawal, walla mu xeeñcu xetu gelawal; ndaxte li wóor sikk-sakka du ko yàq, te moom laab gi wóor na ko, te toj gi da ciy sikk-sakka.

فوائد الحديث

Hadiis bi cosaan la ci cosaani Lislaam yi, ab reegal la ci reegali Fiq yi, te mooy: kóolute du deñ ci sikk-sakka, ak cosaan mooy la fa nekkoon des ca la mu nekkoon, ba keroog muy am kóolute ci lu wuute ak loolu.

Sikk-sakka du jeexital cim njàpp, kiy julli day des cig laabam feeg amul kóolute cig tojle.

التصنيفات

Booley dégg diine ak i cosaanam, Yiy firi njàpp