malaaka yi duñu ànd ci mbooloo mu ànd akub xaj walla ab jóolooli

malaaka yi duñu ànd ci mbooloo mu ànd akub xaj walla ab jóolooli

Jële nañu ci Abuu Hurayrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «malaaka yi duñu ànd ci mbooloo mu ànd akub xaj walla ab jóolooli.

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day xibaare ne malaaka yi duñu ànd ci tukki boo xam ne ab xaj da caa ànd, walla ab jóolooli li gu ñu lonk ci daaba yi bu yëngatoo di génne kàddu.

فوائد الحديث

Tere nañu yar xaj ak di ànd ak moom, danañu settee ci tere gi xaj buy rëbb ak buy wattu (garde).

Malaaka yidul ànd ca loola mooy malaakay yërmànde,bu dee malaaka yiy wattu nit ki ñoom moom duñu teqalikoo ak jaam ñi ci seen ug toog ak ci seen ug tukki.

tere nañu ag kalaksone; Ndax benn la ci mbiibi Seytaane yi, te dafay niróo ak kolos yu nasaraan yi.

War na ci jullit bi mu xér ci sori lépp luy tax malaaka yi sori ko.

التصنيفات

Malaaka yi