Yaw Yonnente Yàlla bi, gis nanu ne jihaad moo gën ci jëf yi, mo ndax dunu jihaadi? Mu wax ne: "déedéet, waaye jihaad ji gën mooy: aj gu baax

Yaw Yonnente Yàlla bi, gis nanu ne jihaad moo gën ci jëf yi, mo ndax dunu jihaadi? Mu wax ne: "déedéet, waaye jihaad ji gën mooy: aj gu baax

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yaw Yonnente Yàlla bi, gis nanu ne jihaad moo gën ci jëf yi, mo ndax dunu jihaadi? Mu wax ne: "déedéet, waaye jihaad ji gën mooy: aj gu baax".

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- dañoo gisoon ne jihaad ci yoonu Yàlla ak xeex ak noon yi moo gën ci jëf yi, Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- daldi laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax ñoom jigéen ñi ñu jihaadi? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- gindi leen ci jihaad gi gën ci seen àq te mooy aj gu baax gu dëppoo ak Alxuraan ak Sunna, gu mucc ci bàkkaar ak ngistal.

فوائد الحديث

Jihaad daa bokk ci jëf yi gën ci góor ñi.

Aj nag ci jigéen ñi moo gën jihaad, te bokk na ci jëf yi gën ci ñoom.

Jëf yi dañuy gënante di rawante ci kem aji-jëf ji

Tudde nañu aj jihaad; ndaxte jihaadu bakkan la, ak joxe alal, ak coonoy yaram, kon moom jaamug yaram la ak alal niki jihaad ci yoonu Yàlla.

التصنيفات

Ngëneelu aj ak wumra