ñaar yii dañoo araam ci sama góori xeet wi, waaye dagan nañu ci jigéen ñi

ñaar yii dañoo araam ci sama góori xeet wi, waaye dagan nañu ci jigéen ñi

Jële nañu ci Aliyun Ibn Abii Taalib yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa jël Sooy ci càmmooñam, jël wurus ci ndayjooram, daal di leen yëkkëti ci loxoom, daal di wax ne: "ñaar yii dañoo araam ci sama góori xeet wi, waaye dagan nañu ci jigéen ñi".

[Wér na]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa jël yéreb Sooy walla ab moorso, ci loxob càmmooñam, daal di jël takkaayu wurus mbaa lu ko niru ci loxob ndayjooram, daal di wax ne: Sooy ak Oor, araam na góor ñi di ko sol, bu dee jigéen ñi nag dagan na ci ñoom.

فوائد الحديث

Assindii nee na: (araam na): li ñu ci namm mooy sol gi; bu dul loolu rekk jëfandikoo ko ci weccaxndiku ak joxe ak jaay loolu lépp dagan na, jëfandikoo Oor ci def ko ay ndab ak di ko jëfandikoo loolu lépp dafa araam.

Sariihab lislaam dafa yaatalal jigéen ngir li mu aajowoo taar ak lu ko niru.

التصنيفات

Col yi ak yiy taaral