إعدادات العرض
Bàyyil looy sikk-sàkka jëm ci loo sikk-sàkkawul
Bàyyil looy sikk-sàkka jëm ci loo sikk-sàkkawul
Jële nañu ci Abuu Muhammad Al-Hasan ibn Aliyun ibn Abii Taalib -sétu Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di mbégteem-, nee na: mokkal naa ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "Bàyyil looy sikk-sàkka jëm ci loo sikk-sàkkawul".
[Wér na] [رواه الترمذي والنسائي]
الترجمة
العربية Español አማርኛ English اردو Indonesia বাংলা Français Türkçe Русский Bosanski සිංහල हिन्दी 中文 فارسی Tiếng Việt Tagalog Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் ไทย Deutsch پښتو অসমীয়া Shqip Nederlands ગુજરાતી Кыргызча नेपाली Lietuvių دری Српски тоҷикӣ Kinyarwanda Română Magyar Čeština Moore Malagasy Oromoo ಕನ್ನಡ Azərbaycan O‘zbek Українська ქართული Македонски ភាសាខ្មែរ ਪੰਜਾਬੀ मराठी Kirundi Kurmancî Bahasa Melayu မြန်မာالشرح
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa digle ñu bàyyi wax yi ak jëf yi ñuy sikk-sàkka ne dañu ko a tere walla déet, ndax dafa araam walla dafa dagan, te jëm ci yi ñu sikk-sàkkawul te am yaqiin ci rafetam ak ug daganam.فوائد الحديث
War na ci jullit bi mu tabax ay mbiram ci li co leer te bàyyi li ñuy sikk-sàkka, te mu nekk ku am luko leer ci diineem.
Tere nañu tàbbi ci yu lënt yi.
Boo bëggee ag dal ak nooflaay nanga bàyyi li ñuy sikk-sàkka sànni ko sa ginnaaw.
Yërmàndey Yàlla ci jaamam ñi ndax da leen a digal li nooflaayu bakkan ak xel nekk, mu tere leen li njàqare ak ngëlëmte nekk.
