إعدادات العرض
kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla
kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla
Jële nañu ci Abuu Muusa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj nañu Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waa juy xeex ngir jàmbaare, ak kuy xeex ngir par-parloo, ak kuy xeex ngir ngistal, ana kan ci ñoom moo nekk ci yoonu Yàlla? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di ne: "kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla".
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Bahasa Indonesia Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Français ئۇيغۇرچە Hausa Português Kurdî മലയാളം Kiswahili සිංහල Русский دری Svenska አማርኛ অসমীয়া ไทย Tiếng Việt Кыргызча Yorùbá ગુજરાતી Malagasy नेपाली Oromoo Română Nederlands Soomaali پښتو తెలుగు Kinyarwanda ಕನ್ನಡ Српски Mooreالشرح
Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wuuteg jubluwaay yi ci ñiy xeex; kuy xeex ngir jàmbaare, walla par-parloo walla ngir ñu gis dayoom ci nit ñi mbaa leneen, kan moo ci nekk ci yoonu Yàlla? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle ne kiy xeex ci yoonu Yàlla: mooy kiy xeex ngir kàddug Yàlla jëm kaw.فوائد الحديث
Liy Cosaan ci jëf yi baax walla yi bon mooy yéene ak sellal jëf ji ngir Yàlla.
Bu dee jubluwaay bi ci jihaad mooy yëkkati kàddug Yàlla, jeneen jubluwaay ju ñu yoonal monga ca lu mel niki am ca koom ma, loolu du yàq cosaanu yéene ja.
Fexe ba noon yi du ñu Dugg ci dëkk i jullit ñi, dafa bokk ci xeex si yoonu Yàlla.
Ngëneel li rot ci jihaatkat yi day yam ci ñiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku.
التصنيفات
Teggiini xeex ci yoonu Yàlla