ku ñaan Yàlla nekk sahiid ci ag dëggu kon Yàlla dana ko jotale ca darajay ña nekk sahiid, donte dafa dee ci kaw lalam

ku ñaan Yàlla nekk sahiid ci ag dëggu kon Yàlla dana ko jotale ca darajay ña nekk sahiid, donte dafa dee ci kaw lalam

Jële nañu ci Sahl ibn Haniif yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "ku ñaan Yàlla nekk sahiid ci ag dëggu kon Yàlla dana ko jotale ca darajay ña nekk sahiid, donte dafa dee ci kaw lalam".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku sàkku a dee ci yoonu Yàlla, te mu dëggu sellal yéeneem jooju ñeel Yàlla mu kawe mi, kon Yàlla dana ko jox darajay way-dee ci yoonu Yalla ci yéene ju dëggu donte dafa dee ci kaw lalam ci lu dul jihaad.

فوائد الحديث

Yéene ju dëggu ak jëf kem-kàttan sabab la ci egg ca bëgg-bëgg ya ci tiyaaba ak yool, donte deful jëf ja ñu sàkku.

Xemmemloo jihaad ak sàkku a dee ci yoonu Yàlla mu màgg mi.

Yàlla dafa teral xeet wi, ba da koy jox ay daraja yu kawe ca àjjana ci jëf yu neew.

التصنيفات

Jëfi xol yi, Ngëneelu xeex ci yoonu Yàlla