bàyyil li la leerul te jëm ca la la leer, ndaxte dëgg ag dal la, fen nag ag jax-jaxi la

bàyyil li la leerul te jëm ca la la leer, ndaxte dëgg ag dal la, fen nag ag jax-jaxi la

Jële nañu ci Abuu Al-Hawraa As-Sahdii mu wax ne: wax naa Al-Hasan ibn Aliyun yal na leen Yàlla dollee gërëm ne ko: lan nga mokkal ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc? Mu ne ma: mokkale naa ci Yonnente Yàlla bi: «bàyyil li la leerul te jëm ca la la leer, ndaxte dëgg ag dal la, fen nag ag jax-jaxi la".

[Wér na]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle na ñu bàyyi li ñuy sikk-sàkka ci ay wax ak i jëf ci ne dañu ko a tere walla déet, ndax dafa araam walla dafa dagan, jëm ci li ñu sikk-sàkkawul ag rafetam ak ug daganam wóor, ndaxte xol daciy dal, lu am sikk-sàkka nag day jàqal xol te du ci dale.

فوائد الحديث

War na ci jullit bi mu tabax ay mbiram ci li co leer te bàyyi li ñuy sikk-sàkka, te mu nekk ku am luko leer ci diineem.

Tere nañu tàbbi ci yu lënt yi.

Boo bëggee ag dal ak nooflaay nanga bàyyi li ñuy sikk-sàkka sànni ko sa ginnaaw.

Yërmàndey Yàlla ci jaamam ñi ndax da leen a digal li nooflaayu bakkan ak xel nekk, mu tere leen li njàqare ak ngëlëmte nekk.

التصنيفات

Wax yu woroo ak lëngal jenn wax