إعدادات العرض
mocc ak takk ay xarnga-fuufa ak noob bokkaale la
mocc ak takk ay xarnga-fuufa ak noob bokkaale la
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «mocc ak takk ay xarnga-fuufa ak noob bokkaale la».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Bahasa Indonesia Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Français Kurdî Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் සිංහල မြန်မာ Русский Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە Hausa ไทย دری Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių or Română Kinyarwanda Српски O‘zbek Moore नेपाली Malagasy тоҷикӣ Oromoo Soomaali Български Українська Azərbaycan ქართული bm Македонскиالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ay bir yoo xam ne def ko bokkaale la, bokk na ca: Bu njëkk bi: mocc: wax ji ceddo yi di fajoo te mu làmboo bokkaale. Ñaareel bi: ay xarnga-fuufa lu deme ni ay xor mbaa lu ni mel: mooy li ñuy tàkkal xale yi ak baayima yi ak yeneen ngir jeñ bët bu aay. Ñatteel bi: noob: te mooy lu ñuy def ngir kiy sëy bëgg ki muy sëyal. Bir yii ci bokkaale la bokk; ndax day def mbir ab sabab, te nekkul sababu Sariiha bu am tegtal, nekkul it sabab bu ñu man a làmb daj ko. Bu dee sababi Sariiha yi nag niki jàng Alxuraan, walla yi nu man a yëg niki garab yi nga xam ne dañu koo xame ci def ko, loolu dagan na ànd ak gëm ne moom sabab rekk la waaye njariñ ak lor ci loxol Yàlla la nekk.فوائد الحديث
Bokk na ci njariñal adiis bi :
Sàmm ag wéetal Yàlla ak pas-pas bu wér ci lépp lu koy yàq.
Araamug jëfëndikoo mocci bokkaale yi ak i xarnga-fuufa, ak noob.
Nit ki gëm ci ñatt yii ne ay sabab lañu: loolu bokkaale gu ndaw la; ndax mooy lu nekkul sabab nga def ko sabab, waaye bu fasee ne day jariñ di lor ci boppam loolu bokkaale gu mag la.
Moytondikuloo di def sababi bokkaale yi ak yu araam yi.
Araamal mocc ak ne si bokkaale la bokk lu dul muy mocc bu ñu yoonal.
Xol bi dafa war a wékku ci Yàlla dong, ndax ci moom rekk la lor ak njariñ di bawoo amul bokkaale, yiw du am lu dul mu juge ci Yàlla te kenn du jeñ lor ku dul Yàlla mu kawe mi.
Mocc bu dagan day làmboo ñatti sart: 1- mu fas ne sabab rekk la du jariñ ci lu dul ndigalu Yàlla. 2- mu nekk ci Alxuraan ak turi Yàlla ak i meloom ak ay ñaani Yónente bi ak ay ñaan yu ñu yoonal. 3- mu nekk ci làkk wu nu xam te du am ay xaatim ak i njabar.
التصنيفات
Mocc gees yoonal