buleen def séen kër yi ay bàmmeel, Saytaane day daw kër goo xam ne dañu fay jàng saaru Al-Baxara

buleen def séen kër yi ay bàmmeel, Saytaane day daw kër goo xam ne dañu fay jàng saaru Al-Baxara

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «buleen def séen kër yi ay bàmmeel, Saytaane day daw kër goo xam ne dañu fay jàng saaru Al-Baxara».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tere neenal kër yi ci julli ba mu mel ni ay bàmmeel ndax deesu fa julli. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle ne Saytaane day daw kër goo xam ne dañu fay jàng saaru Al-Baxara.

فوائد الحديث

Sopp nañu baril ay jaamu Yàlla ak julliy naafila ci kër yi.

Julli ci ay bàmmeel daganul; ndax jumtukaay la ci jumtukaayi bokkaale yi ak ëppal ca ña fa nekk, ba mu des jullee néew.

Te sax na ci jóge ci Sahaaba yi ñuy tere julli ci bàmmeel yi; looloo tax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere ñuy def kër yi mu mel ni ay bàmmeel kenn du fa julli.

التصنيفات

Ngëneeli saar yi ak laaya yi