إعدادات العرض
lépp a ngi ci ndogal yi, ba ci lott ak muus, mbaa muus ak lott
lépp a ngi ci ndogal yi, ba ci lott ak muus, mbaa muus ak lott
Jële nañu ci Taawuus mu wax ne: fekk naa fi ay nit ci Sahaabay Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ñuy wax naan lépp a ngi aju ci ndogal yi, Taawuus wax ne: dégg naa Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «lépp a ngi ci ndogal yi, ba ci lott ak muus, mbaa muus ak lott».
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية English မြန်မာ Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands اردو Español Bahasa Indonesia ئۇيغۇرچە বাংলা Türkçe Bosanski සිංහල हिन्दी Tiếng Việt Hausa മലയാളം తెలుగు Kiswahili ไทย پښتو অসমীয়া Shqip دری Ελληνικά Български Fulfulde Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy Română Kinyarwanda Српски тоҷикӣ O‘zbek नेपाली Moore Kurdî Oromoo Soomaali Français Azərbaycan Tagalog Українська தமிழ் bm Deutsch ქართული Português mk Magyarالشرح
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne lépp a ngi aju ci ndogal, Ba ci lompañ te mooy: bàyyi loo war a def ngir di tanxamlu ak di ko yéexe ci waxtoom, ci biri àdduna yi ak yu allaaxira yi. Ak ba ci muus, te mooy: sawar ak ñaw ci biri àdduna yi ak yu allaaxira yi. Ak ne Yàlla mu kawe mi dafa dogal muus ak lompañ ak lépp, dara du am lu dul ne jiitu na ca xam-xamu Yàlla ba ak coobareem.فوائد الحديث
Leeral pas-pasu Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ci ndogal yi.
Lépp ci ndogal lay ame ba ci lompañ ak cawarte.
Leerlug Sahaaba yi ak séenug moytu ci tuxal Hadiisi Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
gëm ndogal yépp yu neex ya ak yu naqari ya.