buleen dëggal ñoñ téere yi te buleen leen weddi, nangeen wax ne: {gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun}

buleen dëggal ñoñ téere yi te buleen leen weddi, nangeen wax ne: {gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun}

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Ñi ñu joxoon téere ya daanañu jàng Tawraat ci làkku Hébra, daa ko firil waa Lislaam ci làkku Araab, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne leen: "buleen dëggal ñoñ téere yi te buleen leen weddi, nangeen wax ne: {gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun} [Al-Baxara: 136] aaya bi".

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mi ngi artu aw xeetam ci woru ci li ñoñ téere yi di nettali ci séen téere yi. Ndax Yahuut yi ci jamonoy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daanañu jàng Tawraat ci làkku Habriya; te mooy làkku Yahuut yi, daan ko tekki ci Araab, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne leen: buleen dëggal ñoñ téere yi te buleen leen weddi, loolu nag ci lu nu xamul dëgg la walla fen la; Ndaxte Yàlla mu kawe mi da noo digal nu gëm Alxuraan ji mu wàcce ci nun, ak téere bi mu wàcce ci ñoom, waaye nag nun amunu yoonu xam li wér ci li ñuy nettali ci téere yooyu ak la ca wérul bu dee amul ci sunu Sariiha luy leeral dëgg ga ak fen wa, Nu taxawlu, dunu leen dëggal; ngir dunu bokkak ñoom la ñu ca soppi, te dunu leen weddi; ndax man naa am muy dëgg, ndax kon danuy weddi li ñu nu digal nu gëm ko, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digle na nuy wax: {gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun, ak la ñu wàcce ci Ibraahiima ak Ismaayla ak Yanqóoba ak sét ya ak la ñu jox Muusaa ak Iisaa ak la ñu jox Yónente ya mu bawoo ca séen Boroom, dunu xàjjale diggante kenn ci ñoom, te nun ci moom la nu jébbalu} [Al-Baxara: 136].

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi: Li ñuñ téere yi di nettali ñàtti xaaj la: xaaj bu dëppoo ak Alxuraan ak Sunna boobu dañu koy dëggal, ak xaaj bu juuyoo ak Alxuraan ak Sunna boobu neen la dañu koy weddi, ak xaaju ñatteel bi amul ci Alxuraan ak Sunna lu koy dëggal mbaa di ko fenloo; boobu dees na ko nettali rekk waaye duñu ko dëggal te duñu ko weddi.

التصنيفات

Rules and Principles of Exegesis, Pre-Islamic Scriptures