bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na julli ñaari ràkka bala moo toog

bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na julli ñaari ràkka bala moo toog

Jële nañu ci Abuu Xataadata As-Sulamii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na julli ñaari ràkka bala moo toog».

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day ñaax ku dugg ci jàkka waxtu wu mu man a doon, ak yitte ju ko man a waral, mu julli ñaari ràkka balaa toog, ñuy ñaari ràkkay nuyu jàkka ji.

فوائد الحديث

Sopp nañu julli ñaari ràkka ngir nuyu jàkka ji bala ñoo toog.

Ndigël lii nag ngir ku bëgg a toog la, ku dugg ci jàkka daal di génnaat njëkk muy toog kooku ndigël li jëmul ci moom.

Aji-julli ji bu duggee ci jàkka ji fekk nit ñi nekk ci julli gi mu dugg ci julli gi ànd ak ñoom loolu dana ko doy wolif ñaari ràkka yi.

التصنيفات

Jullig coobarewu, Àttey jàkka yi