إعدادات العرض
ag siif de dana am ak ay mbir yu ngeen bañ" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi ana lan nga nuy digal? Mu ne: "joxeleen àq ji leen war, te laaj Yàlla seen àq
ag siif de dana am ak ay mbir yu ngeen bañ" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi ana lan nga nuy digal? Mu ne: "joxeleen àq ji leen war, te laaj Yàlla seen àq
Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ag siif de dana am ak ay mbir yu ngeen bañ" ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi ana lan nga nuy digal? Mu ne: "joxeleen àq ji leen war, te laaj Yàlla seen àq».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Hausa Kurdî Kiswahili Português සිංහල Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá ئۇيغۇرچە Tiếng Việt ไทย پښتو অসমীয়া دری Кыргызча or नेपाली Malagasy Kinyarwanda తెలుగు Lietuvių Oromoo Română മലയാളം Nederlands Soomaali Српски Українська Deutsch ಕನ್ನಡ Moore Shqip Magyar ქართული Azərbaycanالشرح
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne dana jiite jullit ñi ay njiit yuy jël alali jullit ñi ak yeneen ci biri àdduna yi, di ko depaase nu mu leen soobe, ak xañ jullit ñi seen àq ci loolu. Dana am fi ñoom ci diine ji ay bir yoy deesnako koy bañ. Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- laaj ko: ana lan la ñuy def ci jamono jooju? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare leen ne ñoom li ñi feetewoo alal ji du tax ngeen xañ leen li leen war ci ñoom ci dégg ak topp, waaye na ngeen muñ tey dégg di topp te buleen xëccoo ak ñoom mbir mi, te ngeen laaj Yàlla àq ji ngeen moom, ak Yàlla yéwénal leen te jeñal leen seenuw ay ak seenu tooñ.فوائد الحديث
Hadiis bi bokk na ci liy tegtale yónnenteg Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax dafa xibaare luy ami ci xeetam wi mu ame na mu ko xibaare woom.
Dagan na ñu xamal ki nu nattu li ñu ko njortal ciy balaa; ngir mu waajal ko boppam ba bu ko dikkalee mu nekk muñkat buy yaakaar payug Yàlla.
Ŋoy ci Alxuraan ak Sunna day genne nit ki ci fitna ak wuute.
Soññee ci dégg ak topp ñeel njit yi cig njekk, te bañ a génn ci seen kaw, doonte dañoo tooñ.
Jëfandikoo ag xereñte ak topp sunna ci jamonoy fitna.
Nit ki dafa war a taxaw ci dëgg, doonte dañu koo tooñ.
Nekk na ci tegtalug reegalu: tànn ay wi gën a woyof walla lor wi gën a woyof.
التصنيفات
Warteefi njiit