إعدادات العرض
amul benn jaam bu Yàlla sàmmuloo am càmm, mu faatu fekk da doon wuruj ña muy sàmme, lu dul ne Yàlla dana araamal ci moom àjjana
amul benn jaam bu Yàlla sàmmuloo am càmm, mu faatu fekk da doon wuruj ña muy sàmme, lu dul ne Yàlla dana araamal ci moom àjjana
Jële nañu ci Mahqal Ibn Yasaar Almusanii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «amul benn jaam bu Yàlla sàmmuloo am càmm, mu faatu fekk da doon wuruj ña muy sàmme, lu dul ne Yàlla dana araamal ci moom àjjana».
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە සිංහල ไทย دری Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių or Română Kinyarwanda Српски O‘zbek Moore नेपाली Oromoo Soomaali Malagasy Български Українська Azərbaycan ქართული Lingala bm тоҷикӣ Македонскиالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ku Yàlla def kilifa mu jiite nit ñi, moo xam njiit lu mag la niki buur, walla njiit lu ndaw niki góor gi ci këram, ak jigéen gi ci këram, mu gàttanlu ci àqi la muy sàmm, di leen wuruj te du leen laabire, daal di sànk séen i àq yu diine mbaa yi àdduna, kooku yayoo na mbugal mu tar mii.فوائد الحديث
Bokk na ci njariñal adiis bi :
Tëkku gii nag nekkul ne njiit lu mag li ak ña koy wuutu rekk a ko jagoo, waaye day làmboo képp ku Yàlla sàmmuloo am càmm.
Li war képp ku jiite dara ci biri jullit ñi mooy mu leen di laabire, te pastéefu ci matal kóllare, te moytoo wor.
Màggaayu wartéefu képp Ku yilif Aw nit, moo xam kiliftéef gu gu ndaw walla gu mag.
التصنيفات
Doxaliinu Sariya