إعدادات العرض
nit ñi bu ñu gisee tooñkat bi te téyewuñu loxoom kon tuuti rekk Yàlla boole leen mbugal
nit ñi bu ñu gisee tooñkat bi te téyewuñu loxoom kon tuuti rekk Yàlla boole leen mbugal
Jële nañu ci Abuu Bakrin As-Siddiix -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: yéen nit ñi, yéen de dangeen di jàng aaya bii: {yéen ñi gëm wattuleen seen bopp cànkuteg aji-sànku ji du leen lor ndeem jub ngeen}, man dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «nit ñi bu ñu gisee tooñkat bi te téyewuñu loxoom kon tuuti rekk Yàlla boole leen mbugal».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Hausa Kurdî Kiswahili Português සිංහල Tiếng Việt دری অসমীয়া ไทย አማርኛ Svenska Кыргызча Yorùbá ગુજરાતી नेपाली മലയാളം Oromoo Română Nederlands Soomaali پښتو తెలుగు Kinyarwanda Malagasy ಕನ್ನಡ Српски Moore ქართული Čeština Magyar Українська Македонски Lietuvių Azərbaycanالشرح
Abuu Bakrin As-Siddiix -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xamle ne: nit ñi dañuy jàng aaya bii: {yéen ñi gëm wattuleen seen bopp cànkuteg aji-sànku ji du leen lor ndeem jub ngeen} [Al-Maa-ida: 105]. Ñu dégge ci ne nit ki na jëm ci sellal boppam dong, ndaxte ginnaaw loolu cànkuteg aji-sànku ji du ko lor, ndax sàkkuwuñu ci ñoom ñuy digle lu baax ak di tere lu bon! Mu xamal leen ne demewul noonu, ndaxte moom dégg na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Nit ñi bu ñu gisee tooñkat bi te terewuñu ko tooñ, te man nañu ko koo tere, kon xaw tuuti rekk Yàlla boole leen mbugal ñoom ñépp kay def lu bon la, ak ka ca noppi.فوائد الحديث
Li war jullit ñi mooy di laabireente ak digle lu baax tere lu
bon.
Mbugalum Yàlla mu matale mi day làmboo tooñkat bi ngir tooñam gi, di làmboo it ki noppi ci dindi ko ndeem man na koo dindi.
Jàngal nit ñi ak xamal leen njàngalem Alxuraan ca anam ga wér.
War na ci nit ki mu yittewoo dégg téereb Yàlla mu kawe mi, ba du ko dégge nu ko Yàlla mu kawe mi bëggewul.
Gindiku manul am ànd ak bàyyi digle lu baax ak tere lu bon.
Firi mi wér ci aaya bi mooy: téyeleen seen bopp ci moy yi, bu ngeen wattoo seen bopp ba noppi néew doole ci digle lu baax ak tere lu bon, kon cànkuteg aji-sànku ji ci def yi ñu tere du leen lor ndeem jub ngeen ci moytu ko.
التصنيفات
Àttey digle yiw tere njékar