إعدادات العرض
ku julli ñaari sedd yi dana dugg àjjana
ku julli ñaari sedd yi dana dugg àjjana
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-Asharii-yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku julli ñaari sedd yi dana dugg àjjana»
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt සිංහල ئۇيغۇرچە Hausa Kurdî Kiswahili Português دری অসমীয়া አማርኛ Svenska ไทย Yorùbá Кыргызча ગુજરાતી नेपाली Română മലയാളം Nederlands Oromoo తెలుగు پښتو Soomaali Kinyarwanda Malagasy ಕನ್ನಡ Српски Moore ქართული Čeština Magyar Українська Македонски Lietuvių Azərbaycanالشرح
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day soññee ci xér ci jullig ñaari sedd yi, te mooy jullig fajar ak tàkkusaan, mu bégal ki leen julli te jox leen seeni àq ca waxtu wa ca mbooloo ma, ak lu dul yooyu, danañu nekk sabab ci mu dugg àjjana.فوائد الحديث
Ngëneelu sàmmonte Ak jullig fajar ak tàkkusaan; ndaxte fajar day ame ca nelaw yu neex ya, Tàkkusaan di ame fa nit ka di yittewoo liggéeyam, kon ku sàmmonte
ak ñoom yell na mu sàmmonte ak julli yi des.
Tudde nañu jullig fajar ak tàkkusaan ñaari sedd yi; ndaxte jullig fajar daa am seddug guddi gi, jullig tàkkusaan am seddug bëccag gi donte ci waxtu wu tàng lay nekk it waaye mooy gën a sedd waxtu yi ko jiitu, walla tudde gi nekk ci anamug notal, kem ni ñuy waxe: ñaari weer yi, jublu ci jant bi ak weer wi.
التصنيفات
Ngëneelu julli