ku bàyyi jullig Tàkkusaan jëfam yàquna

ku bàyyi jullig Tàkkusaan jëfam yàquna

Jële na ñu ci Buraydata Ibn Al-Husaybi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Teelleen a julli Tàkkusaan, ndax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "ku bàyyi jullig Tàkkusaan jëfam yàquna".

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- artu na ci yeexe julli Tàkkusaan ca waxtoom te tay ko, ak ne ku def loolu jëfam yàquna dem ci naaxsaay.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci sàmmoonteek jullig Tàkkusaan ci njëlbeenu waxtoom te gaawe ko.

Tëkku gu tar ñeel na ku bàyyi jullig Tàkkusaan, te weesale ko waxtoom moo gën a màgg weesale leneen, ndax mooy julli gi digg-dóomu ga ñu jagleel ag digle, ci wax ji Yàlla wax ne: (nangeen sàmmoonteek julli yi ak julli gu digg-dóomu gi) [Al-Baxara: 238].

التصنيفات

Warug julli ak àtteb ki ko bàyyi