képp ku aj ngir Yàlla te beejul ( sëyul wala mu wax lu bon) deful tamit yëfi kàccor, dana dellu mel ni bis ba ko yaayam jure woon

képp ku aj ngir Yàlla te beejul ( sëyul wala mu wax lu bon) deful tamit yëfi kàccor, dana dellu mel ni bis ba ko yaayam jure woon

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- muy wax naan: "képp ku aj ngir Yàlla te beejul ( sëyul wala mu wax lu bon) deful tamit yëfi kàccor, dana dellu mel ni bis ba ko yaayam jure woon".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne képp ku aji te beejul, beej mooy: sëy ak yi koy jiitu ci fóon ak joññoo, dees na ko wax it jublu ci wax ju ñaaw, te kàccoorewul ci def ay moy ak yu ñaaw, Te bokk na ci kàccoore def yi ñu araamal. Dana dellu juge ci ajam gi di ku ñu jéggal, kem ni liir bi di juddoo nekk ku mucc ci ay bàkkaar.

فوائد الحديث

Ag kàccoore doonte da ñu koo tere ci jamono ju ne, waaye tere gi day gën a tar ci biir aj ngir màggal jaamu yi nekk ci aj gi

Nit day judd ci lu dul njuumte, di ku sett wicc ci ay bàkkaar; te du gàddu bàkkaar

i keneen.

التصنيفات

Ngëneelu aj ak wumra