إعدادات العرض
kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog
kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog
Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog.
[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt සිංහල ئۇيغۇرچە Kurdî Hausa Português മലയാളം မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands తెలుగు Kiswahili தமிழ் ไทย دری Български Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy or Română Kinyarwanda тоҷикӣ O‘zbek Akan नेपाली Moore Azərbaycan Oromoo Soomaali Українська km bm rn ქართული Македонски Српскиالشرح
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne nit ku mat ci jokk bokk ak rafetal jëme ci jegeñaale yi nekkul nit kiy fay rafetal cig rafetal, Waaye jokk-katu mbokk dëgg mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkoom mu jokk ko, bu ñu ñaawalee jëme ci moo; dakoy faye ag rafetal jëme ci ñoom.فوائد الحديث
Jokk mbokk gi Lislaam jàpp mooy nga jokk ku la dog, di baal ku la tooñ, di jox ku la xañ, waaye jokk nekkul ci defalante ak fayantoo.
Jokk mbokk dana nekk ci nga fexe ba éggale ci ñoom lu jàppandi ci aw yiw niki alal ak ñaan ak digle lu baax tere lu bon ak yu ni mel, ak nga fexe ba jeñal leen aw ay.
التصنيفات
Mboolaayal Lislaam