Ku ray koo séqal kóllëre, du xeeñcu xetug Àjjana, te dinanteem ak xetam ga soree ni doxub ñent-fukki at

Ku ray koo séqal kóllëre, du xeeñcu xetug Àjjana, te dinanteem ak xetam ga soree ni doxub ñent-fukki at

Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Ku ray koo séqal kóllëre, du xeeñcu xetug Àjjana, te dinanteem ak xetam ga soree ni doxub ñent-fukki at".

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral tëkku gu tar gi ñuy tëkku ku ray boroom kollëre -te mooy yéefar bu dugg ci biir réewum jullit ci kollëre ak kaaraange- ci ne du xeeñcu xetug àjjana, te xetam ga dana soree ni doxub ñent-fukki at.

فوائد الحديث

Araamal nañu ray boroom kollëre ak yéefar biy fay ay wareefam, ak yéefar buñu làq , te loolu ci bàkkaar yu mag yi la bokk.

Boroom kollëre: mooy yéefar buñu jël ci moom kóllëre mu nekk ci dëkku jullit ñi, te du xeex jullit ñi ñoom itam duñu ko xeex, yéefa biy fay: mooy ki dëkk ci dëkku jullit ñi di fay juuti, ki ñu làq: mooy ku dugg ci kër jullit ñi ci kóllëre ak kaaraange ci ab diir buñu tënk.

Wattandikuloo wor kóllëre ak ñi dul ay ajullit.

التصنيفات

Àttey ñoñ Téere ñiy dundu ci goxub Lislaam