bu ngeen demee ca duus ba buleen jublu xibla, te buleen ko dummóoyu, waaye nangeen jëm Sarq walla Xarb

bu ngeen demee ca duus ba buleen jublu xibla, te buleen ko dummóoyu, waaye nangeen jëm Sarq walla Xarb

Jële nañu ci Abuu Ayyuuba Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "bu ngeen demee ca duus ba buleen jublu xibla, te buleen ko dummóoyu, waaye nangeen jëm Sarq walla Xarb", Abuu Ayyuuba nee na: nu dem Saam fekk fa ay duus yu nu tabax mu jëm xibla nuy wetu, tey jéggalu Yàlla mu kawe mi.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na kuy faj aajoom ci saw walla xayta muy jublu xibla jëm ca kaaba ga, te it bu mu ko dummóoyu di ko wan ginnaaw; waaye li ko war mooy mu moy ko jublu Sarq walla Xarb bu dee xiblaam dafa mel ni xiblag waa Madiina. Abuu Ayyuuba -yal na ko Yàlla dollee gërëm- xibaare ne ñoom ba ñu demee Saam dañoo fekk duus ya ñu waajal ngir faj aajo ñu tabax ko mu jublu Kaaba ga, ñuy moyale seen yaram xibla ga, ànd ak loolu ñuy jéggalu Yàlla.

فوائد الحديث

Xereñte gi nekk ci loolu mooy màggal kaaba gu tedd gi ak wormaal ko.

Jéggalu Yàlla ginnaaw bi nu génnee ca barab ba ñuy faje aajo.

Rafetug njàngalem Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-; ndaxte ba mu tuddee la nu tere dafa ginde jëmale ca la dagan.

التصنيفات

Dindi sobe, Teggiini faj-aajo