ku ma waxal jenn wax te xam ne ay fen la, moom kenn la ci fenkat yi

ku ma waxal jenn wax te xam ne ay fen la, moom kenn la ci fenkat yi

Jële nañu ci Samurata Ibn Jundub ak Muxiirata Ibn Suhbata yal na leen Yàlla dollee gërëm ñu wax ne, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "ku ma waxal jenn wax te xam ne ay fen la, moom kenn la ci fenkat yi".

[Wér na]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku toxal ab hadiis askanale ka ko fekk xam na walla mu not ci njortam ne dañu ko a fenal Yonnente bi kon aji-nettali ji day bokk ak ki sos fen wi.

فوائد الحديث

Wóorlu ci hadiis yi ñuy nettalil Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ak wóorlu ag wéram laata ñu koy nettali.

Melow fen dees na ko boyal ci képp ku sos aw fen ak ku ko toxal tasaare ko ci nit ñi.

Araamalees na nettali hadiis bu ñu sos ci képp ku xam ne danu koo sos, walla ag sosam not ci njortam lu dul mu koy moytandikuloo.

التصنيفات

Solos Sunna ak wàccuwaayam, Jikko yees ŋàññ