إعدادات العرض
Jaayante nanu ak Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dégg ak topp, ci lu jafe ak lu yomb, ci lu neex ak lu naqari, ak bu xat-xat tegee sunu kaw
Jaayante nanu ak Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dégg ak topp, ci lu jafe ak lu yomb, ci lu neex ak lu naqari, ak bu xat-xat tegee sunu kaw
Jële nañu ci Ubaadata Ibnus Saamit -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Jaayante nanu ak Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dégg ak topp, ci lu jafe ak lu yomb, ci lu neex ak lu naqari, ak bu xat-xat tegee sunu kaw, ak nu bañ a xëccoo ak nguur, ak nu bañ a wax lu dul dëgg fu nu man a nekk, dunu ragal ci Yàlla yeddagay aji-yedde ji.
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Kurdî Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands සිංහල Hausa ไทย دری Кыргызча Lietuvių Kinyarwanda नेपाली Malagasy Italiano or ಕನ್ನಡ Oromoo Română Soomaali Српски Українська Moore Azərbaycan ქართული Magyarالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa jël kóllare ci Sahaaba yi ci ñu wommatul ki yor mbir mi ak àttekat yu ci lu yomb ak lu jafe, ak ci jamonoy woomal ak ñàkk, moo xam ay ndigleem neex na sunu bàkkan walla neexu ko, donte njiit yi dañoo jiital ci kaw askan alal walla ag pal mbaa leneen, dees leen a war a déggal, topp leen ci njekk, te bañ a jàmmaaloo ak ñoom, ndax fitna ak yàq gi nekk ci xeex ak ñoom moo gën a rëy yàq giy am ci séenug tooñ, bokk na ci li ñu kóllarante ak moom ñuy wax dëgg ci bépp barab di way-sellal ci loolu ngir Yàlla dong te duñu ragal ku leen di yedd.فوائد الحديث
Bokk na ci njariñal hdiis bi: Meññitum déggal njiit yi, ak topp leen mooy booloog kàdduy jullit ñi, ak bàyyi tàqalikoo.
Dañoo war a topp buur ci lu dul ag moy Yàlla ci lu yomb ak lu jafe, ci lu neex ak lu naqari, ak ca doxaliin wa ñu tànn.
War nanoo wax dëgg fu nu man a nekk, ci lu dul nuy ragal ci Yàlla yeddagay aji-yedde ji.