deesul loru waaye deesul lore, ku lore Yàlla lor ko, waaye ku sonle Yàlla sonal ko

deesul loru waaye deesul lore, ku lore Yàlla lor ko, waaye ku sonle Yàlla sonal ko

Jële na ñu ci Abii Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «deesul loru waaye deesul lore, ku lore Yàlla lor ko, waaye ku sonle Yàlla sonal ko».

[Wér na] [Ibnu Maaja soloo na ko - Ahmat soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne dañoo war a jeñ lor ci ay anam yu wuute, ci sunu jëmm ak ci ñeneen ñi, daganul kenn di lor boppam mbaa muy lor keneen. Du dagan ci kenn muy delloo lor ci aw lor; ndax lor deesu ko dindee lor lu dul ci anamu fayantoo te bañ a ëppal. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral tëkku ku rëy giy tege ci kiy lor nit ñi, ak coono gi ñeel kiy sonal nit ñi.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adios bi: tere ëppal ci fayu lu ëpp la ñu la def.

Yàlla digalul ay jaamam lenn lu leen di lor.

Araamug loru ak lore ci wax mbaa ci jëf walla ci bàyyi.

Fay lu tolloo ak jëf ja, ku lore Yàlla lor ko, ku sonle Yàlla sonal ko.

Bokk na ci tënki Sariiha yi: "lor dees koy dindi", Sariiha du saxal lor, te day tere lore.

التصنيفات

Booley dégg diine ak i cosaanam