ku ñëw ci yéen fekk ngeen abooloo ci lenn njiit, mu bëgg a xotti mbooloo mi, mbaa mu tàqqale séen mbooloo mi, rayleen ko

ku ñëw ci yéen fekk ngeen abooloo ci lenn njiit, mu bëgg a xotti mbooloo mi, mbaa mu tàqqale séen mbooloo mi, rayleen ko

Jële na ñu ci Arfajatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «ku ñëw ci yéen fekk ngeen abooloo ci lenn njiit, mu bëgg a xotti mbooloo mi, mbaa mu tàqqale séen mbooloo mi, rayleen ko».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne bu jullit ñi booloo ci lenn njiit, di menn mbooloo, am ku ñëw bëgg a xëccoo ak moom njiit gi, mbaa mu bëgg a tàqale jullit ñi ci ay mbooloo yu bari, kon dañu koo war a tere daadi xeex ak moom; ngir jeñ aw ayam ak ñoŋal dereeti jullit ñi.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiisb: Dañoo war a dégg te topp njiitul jullit ñi ci lu dul ag moy, araam na it di jàmmaaloo ak moom.

Ku génn ci njiitl jullit ñi ak séen mbooloo ma dañoo war a xeex ak moom ag nu dayoom man a toll ci teddnga ak uw askan.

Soññee ci booloo ak bañ a tàqalikoo ak di juuyoo.

التصنيفات

Génn ci topp njiit